Sëriñ Muhàmmadu Gay Jëmóoy, di kenn ci mak ñi njëkka toppu Sëriñ Tuubaa ca Mbàkke Kajoor, donoon ki njëkka jéblu ci waa Jëmóoy.Mootax bi Sëriñ Mbay Jaxate di lim ñi njëkka jéblu ci Boroom Tuubaa, boole na ca Sëñ Muhammadu Gay mii:”Sëriñ Madu Gay Jëmóoy itam bu ca wax lu dulNgor ak diiné ak saytug njabootam ci ab loxoom”Muy doomi Sëriñ Moor Galo Gay Ibn Sëriñ Jëmooy Muhàmmad Siini Gay, Ibn Sëriñ Jëmóoy Baara Anta Gay.S. Muhamadu Gay, di ku teela wattu Alxuraan lool, teela bari xam xam, teela sóobu yoon wu baax, daan def lepp luñ ko wax ne lu baax la rek mu daan góorgóor lu ci di ko def, noon la farloo woon it ci fum dégg nit ku baax rek dem seeti ko.Ci loolu la nek ba am bis mbokkam mu ko tektal ab Sëriñ bu baax, ku bari xam xam te sóobu ci yoonu Tasawuf, ne ko “koo ka de xam naa boo ko gisee, li ngay wut ci Yàlla di nga ko am” Sëriñ boo ba nak mooy Sëriñ bu mak bi Cheex Ahmadu Bàmba Xaadimu Rasuul.Ci noonu la Sëñ Muhammadu Gay demee Mbàkke Kajoor, fekk na fa mbooloo mu bari it, mu tàmnale ak tarbiyaam ci loxoy Sëriñ bi, njëkk yoonu Murid di sosu.Kerook bi Cheexul Xadiim di jot ndigël ci Yonent bi SAW, mu di ko digël ngir mu tarbiya dongo yi ci HIMMA, رب أصحابك بالهمة boo ba daa fekk Sëriñ Tuubaa yónni woon Sëñ Ndaam Abdu Rahmaan Ló, ba muy dem moom S. Ndaam mu àndoon ak S. Muhammadu Gay mii, mu nekkoon ci bisub Alxamis ci atum 1301H (1882 wala 83).Kerook ba ñu xëyee ca Ajjuma ja, ci la Sëriñ bi jot ndigël loolu ci Yonent bi SAW. Ci la Sëñ Aadama Gëy jéblóo ak Sëñ Ibra Saar Njaañ ak Sëñ Masàmba Jòob Saam…Ba ñu matalee soxla sa leen Sëriñ bi yónni woon ca Gàwu ba, ci lañ nëwaat Mbàkke Kajoor ñoom ñaar, biñ ñëwee Sëriñ bi xibaar leen li xew ci seen ginnaaw, ñoom it ñu dàl di joxe seen boppu fa saasa.Ba mu jaayanteeg Sëriñ bi ci la dàl di jébale léppam ak ñéppam, amatul soxla ci boppam mbaa ci leneen. Sëriñ Tuubaa ko tarbiya, defar ko, ba xëy gërëm ko.Sëriñ bi mas na koo bind ay bëyit mook Sëriñ Masàmba Saar, di leen ci gërëm, naan leenجزاكما الخير من يولي الفتى وطراهنا وهنا ويكفي عنكما الضررراحتى تفوقا جمبع الجيل في رتبوفي مزايا بمن تفضيله ظهرتBa bëyit ya jeex, Sëriñ bi ne leen: “[Yaw Sëñ Muhammadu Gay ak Sëñ Masàmba Saar] maa ngi ñaan sunu Boroom mu fayal ma leen aw yiiw àdduna ak àllaaxira, Yàl na ngenn kawe seenug maas ci ay daraja aki may, yàl na leen Yàlla dimbali ci lépp lu ngeen sóobu te woomat leen ci boppam”.Moom Sëñ Móodu Gay it mas naa bind ay bëyit jëme ko ci Boroom Tuubaa, di ko ci ziaare, di feddali ak njébbalam ak di ci wax xettali gi Sëriñ Tuubaa xettali mindéef yi, ñatti bëyit yii ca Xasida ga la bokk:مني سلام كياقوت أو الدرر بل فاق دُرا وياقوتا وكالقمرإلى الذي صار عبد الله خادمهشيخي ملاذي غياثي من قضى وطريهذي زيارتنا يا روضة القطبايا قدوة العلمآ يا ملجأ البشر Mu amoon tawfeexu Sëriñ bi wóolu woon ko lool ba deñcaloon ko ab taawam di Soxna Faati Ja Mbàkke, waaye noonu la ame jagle Sëriñ bi yoroon na kenn ci ay doomam, te li ëpp ci ak njabootam gu jigéen waa kër Sëriñ Tuubaa yi ak mbokki Sëriñ bi ñoo lenn yoroon.Sëriñ Móodu Gay mi ngi làqu ci atum 1920, bokkoon ci ñeenfukk (40) yi Sëriñ Tuubaa ne woon “ñoo koy jiitu Àjjana”.Yalna ñu ko Yàlla fayal te taas nu ci bàrkeem!
- 18safar1313h@gmail.com
- WEBEMAIL