Safar 1«Banaa lepp maa ngii si sab ate tayFaxas naa ludul yaw falang naako yitFaxas naa ludul yaw si man mii mu rotFalang naako yit cee ba dootul ñëwitFabal nak sa bopp ak sa mbir def si manTe def ma murid dëg buy sab xaritDanaa wax ci yaw lutax ñepp xamNi yaw sam kem amul sowwu ak penku yitDanaa wax ci yaw lutax ñepp xamNi yaw sam kemm amul sowwu ak penku yitBangay jápp xaalis aka dëddu aka bañAkay sanni ci ak dex nga raw kepp nitBangay weet akay muñ akay dunde ñaxFa yeefar ya nga far ñepp nootBangay jáng akay bind ñuy fó aka moyFi sak wet nga sut Mbákke mbooléem ña sutBangay jáng akay bind ñuy fó aka moyFi sak wet nga sut Mbákke mbooléem ña sut»(Sëriñ Mbay Jaxate)Nataal: Màggalug Tuubaa ci atum 1368 AH.@Lorenzo Italia
- 18safar1313h@gmail.com
- WEBEMAIL